[Couplet 1]

Kaddu niou niaweni waroul woon mooss diougué tchi yow

Nio bokk ben deret warooneu takh sa yaram daw

Yaguoon la titeuro ame sa estime dameu leu yagua naw

Adouna djiay naleu taye sokhlato sa rak ndaw

Ya gui mey doyadal ndakh fokk ni yama feté kaw

Mais ngathie ngalama souma sanione kouy mindéf yakoy raw

Moussouma diouk tchi bokko noumou tolou meu cedook yén

Tolooon nguen tchi sokhlama ma bayi lepp takhawoulén

Bima yallah tégué ay nattu meu seugu diko mounie

Laaay doga khamni fi kou yoroul xaaliss toloul féneu tchi yén

Appel yek message nieweutoul legui

Ndakh kham ngueni legui frère bi dafey diekhal sa credit rek té dou fathie sa sokhla

Mane dama yagua naïf djiteul famille sama lepp

Nekon sen baye fall kou beugu dara ma madjiali diokhla la

Djièpina seni melokaanou hypocrite Money rek nguen guiss tchi nit ki bouffa nekoul nguen diko sikk

Djiépina beutou mepris bi nguen mey kholé taye

Meritna lou gueun li dedet key dou sama kholeu faye

Damadaan ame kerseu beu damey teudiou dioy

Soumadaan yeuk seni yité té meuneumoko fathie

Taye sama khole bi wow neu kong t yéneu ko tothie

Fi koufi sissou yén leu koufi reuy gatt tam yeneu ko tauthie

Gueumeutouma kèn tchi yén yeneu ma pousse tchi rancune

Mbétel la ame mou tiss tolou na tchi merrou danguine


[Refrain: Jahman]

Yé nama pouss yé nama pouss souma néké rancunier dou kén yén leu

Beugouma touss loudoul fayou wayé meunoumako mak yén dou bén

Yé nama pouss yé nama pouss tchi rancune yéh

Yé nama pouss lima léen lébalone bokoulak liguen ma fay réen


[Couplet 2]

Gatal sama tankeu téyé sama lamign amatouma sakh sén diote

Yéné nalén ay xeweul Lou nguen séntou yalney soute sén ndiorte

Guedna sen peace and love samey kaddu ngok na tiss sén nope

Nouyou nalén diokhlen thieur ndakh yallah beuguoul kouy dok mbook

Beuguoulit kouy yéh fitna lolou rek mo takh may masla ak yén

Méfiant legui dama distant beugueutouma nakhassalé faire semblant ak yén

Ma def sama choix mou lathie ma sacrifice ma dem tchi andank mome

Limeu daan def daw wagnikou rén nguen djign meu niak diom

Tokk sen Keur yén gni daan saaliite tchi sama yewenaay

Taye nguen def debat tchi sama life di finte wakh you bone

Legui soumey rèh woo lén mais soumey djioy lakhou

Dotoulen yeuk samey projet ndakh lounguen kham mou yakhou

Kolouté amatoul ndakh djianou biir mo amatoul

Kilifté ngui ngey niodi tchi bopam guiss naani mo matoul

Gueumeutouma kén tchi yén yeneuma pouss tchi rancune

Mbetel la ame mou tiss tolouna tchi mérou danguine


[Refrain: Jahman]

Yé nama pouss yé nama pouss souma néké rancunier dou kén yén leu

Beugouma touss loudoul fayou wayé meunoumako mak yén dou bén

Yé nama pouss yé nama pouss tchi rancune yéh

Yé nama pouss lima léen lébalone bokoulak liguen ma fay réen


[Couplet 3]

Yallah khamna ni soeur khirou bi ni gueunoul tchi nioun

Amoul lou yaaye dadjioul tchi ndjiambotam bi aka yagua mounie

Sometime ma fatalikou merelen beu bouti tounie

Mais Kouma guiss tchi yén tiofél dekiwaat rek meu sipi mouunie

Naniou dokh tchi valeurou famille yiniou niou yarewoon

Nidjiaay la tchi sey fils té yow badiene nga tchi samey dome

Rancune dey yakh khole t daley ignane lo

Soukheuteul loubakh sa diguek nit gni meulni imam Lo

Rethiou mousta ame tchi service yimeu leu defaaloon

Bou taye doon demb t meu mane ko sakh dinako doli niare

Niaguassayou kaddu yi nga balma dama newooon tchi rancune

Adouna daaara la tchi fane yeup dafeu bari djianguine


[Refrain: Jahman]

Yé nama pouss yé nama pouss souma néké rancunier dou kén yén leu

Beugouma touss loudoul fayou wayé meunoumako mak yén dou bén

Yé nama pouss yé nama pouss tchi rancune yéh

Yé nama pouss lima léen lébalone bokoulak liguen ma fay réen


[Outro: Jahman]

Mane dém na beu beug fayou wayé meunoumako waw

Mane dém na beu beug fayou wayé meunoumako wawaw

Mane dém na beu beug fayou wayé meunoumako balnalén

Mane dem naa

Yé nameu pouss